Mbootàyup way def lu bàx ci wooté boo xamné cik goorgoorlu ak ak saraxé way défal Yalla la taxawé, ci ndigeül gu bawoo ci Kilifa gi di Abdoulla Aziz Ibn Abdalla Ibn Baz (ki jiité ubbékate yi ci Arabi Sawdite) (Yalla nako yalla yeüreüm) ci Allarba 28-04-1414 ci gàdday gi. ñiy saytu buroobi nak mooy ministér bi yoré mbiru diiné lislam ak mayyi ak wooté ak jubbanti
Mouhammad Salih Al-Mounajjid: Wôtékat la bu cosànô Siri, mi ngi juddu ci 30-12-1380 ci gàddàygi, mi ngi mâggé Riyad janŋŋé arabi sawdit ci ay borômi xamxam yu limu, bôkkna ci ñoñu: Cheikh Ibn Bâz ak Cheikh Ibn Usaymîn
Mi ngi juddo égipte ci atum 17-désambr-1926. Mi ngi wattoo Alxuràne ci daara dëkkam ci seriñ bu tudd Mussa Minetàs ci bi mu amé fukki ate ak bènn la mookal. Ginnaw gi mu toxu Tantaa ngir jaŋŋ xam xamu charia. Foofu sax la jëlé xamxamu jaŋŋinu alxuràn ci seriñam bii di Ibrahim Ibn Salam Al-Maliki. Gàñuna ci atum 20-julié-1985 (Yalla nako Yalla yërëm)