-
Ibrahim Al-Axdar "Limou mbiryi : 9"
Mélokâne bi :Jàŋŋkatu alxuràne la bu juddoo Médine ci atum 1364 ci gàdàygi, fala magé yaroofa jàŋŋéfa ci Darul hadis ginnàw gi mu dem najàh topp mu dem ci colés ba mujjé ci écolup xaralé yi jëm ci isine. Jàŋŋéna ci ay kàŋŋàm: Omar Alhaydari, Ahmad Az-Zayyàte, Abdulla Al-Ghunaymàn. Boolénaci fikh ak passpass ak charia. Fétéwoona ak ligé yu takku, niki: Ustas ci xaralép usine, ci Alxuràn ci ecolup ubay Ibn kab ci médine, Ustas buy wootu ci universitep Medine. Ci atup 1406 ci gàddày gi la tàmbalé jiité ci jàkkày Médine. Bookkna ci attékate yi màcc ci Alxuràne.