• Kiko tâlif, Kikon jângg, Limou mbiryi : 2

  Mi ngui jouddô Riyad thi gokh bou toudd houllatoul Khasmâne thi arabi sawdite thi atoum 1385 thi gâddây gui

 • Kiko tâlif, Kikon jângg, Limou mbiryi : 2

  Mi ngui joudd thi 5-5-1980. Jânggalékate di yilimane thi jâkkâm Al-Ikhlâs thi Arabie Saoudite.

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 2

  Kènne la thi gniy jânggalé thi Makka, mi ngui askanô Syrie. Di kou geuna mâth thi njâgginoum Al-khourâne ak kham-kham yi thi ajou. Jânggé thi pâpâm di ap jânggkate bou râgnékou tamite toudd Said Al-Abdallah (Yalla nako Yalla yeureum) (nékkône njîtou jânggkate yi thi Hama). Jânggaléna Oummoul Khoura. Enregistréna foukki njânggine yithi yônou châtibiyya ak dourra.

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 2

  Jânggkate la bou thôssânô Egypte thi Al-Bouhayra, paréna thi njângginou Al-Khourâne yi, niki nônou jânggna thi université bi mâth thi kham-khamiy Al-Khourane. Yilimane la ak khoubakate thi Centre Islamique bi thi New York

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 2

  Mi ngui thiôssânô Yémène, yilimâne la ak khoutebakate thi joumây Khalid Ibn Al-walîd thi katar

 • Kiko tâlif, Kikon jângg, Limou mbiryi : 2

  Mi ngui jouddô Mâkka, amna bak thi njanggate Alkhourâne thi facultèp janggalékate yi tém nèkk jidda. Bôkkna thi yilimâni jâkkay jidda thi arabi sawdite

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 2

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 2

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

  Mi ngui thiôssânô Pakistan, di borôm bâte bou nèkh akoup jânggine bou jâr yône

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

  Ap janŋkate la di ap facckate. Mi ngi juddoo kafr Cheikh ci 2gypte ci atum 1954. Dugna ci facultém médcine ci jànŋukay bu kawé bi ci eskanedari. Bi mufa paré mu ligéy ca lopitàlba. Rajoo ak télé bu egypte défnako jàŋkatu alkhouràne ci atum 1979

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

  Jànŋkatu Alkhouràne la ak yaxu xamxa ci bàte bu ràññéku ak jooxé bu jàr yoone dajàlénaci lu bari ci sitambi:http://taiser.net

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

  Mi ngi génné azhar ci jaŋŋkàyu lislam bi ak làkkup arap, famu amé lijàssa bu kawé ci jàŋŋin yi, ak lijàssap maacc si. Amnaci Doctora. Jàŋŋaléna ci azhar ay ate yu limu ak ci ay jàŋŋukaay yu arabi sawdite, ni mu fassaneté ak facultép jàŋŋalékate bi ci riyaad. Bokkna ci yi mu bindd: At-tashiil fiimaa yachtabihu bil xaari mine aayaati taneziil, ci léral jàŋŋinup warch ci imam nafi, ci kissaaii, ci baate yi 10 jàŋŋkateyi wuté ci chaatibiyya ak durra, ci hamza, choubaa ci chaatibiyya ak durra.

 • Moussa Bilal Wolof

  Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

  Yilimane la di khoutbakate ak jânggalékate thi universitèp An-Nour bi thi Makka. Bokkna thi âttékate thi concour international bou Doubai bi ajou thi Al-Khourane thi atoum 1420 ak 1433 thi gâddây gui

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

  Jânggkatela bou Egypte, di borôm bâte bou nèkh. Amna ap lijâssa thi foukki (10) jânggine yi. Enregistréna ak kâmil thi ay jânggine you wouté

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 6

  Dàkkantalam mooy Bàyu Az-zoubayr, mi ngi tudd Ahmad Tàlib Hamid Ibn Abdul Hamid Ibn Muzaffar Xàn. Judduna ci Riyàd ci atum 1401 ci gàddày gi. Mi ngi jànggé ci fakultép saria bi ci uniwérsitép ba amfa bak. Ginàw ngi mu am Masestér ci àtté ci fiq muqàran. Di ligéyé kom wootékate ci ministérup mbiri lislàm ci Riyad, tànnañuko muy jiité naafilayi ci koor, ci jàkka Médine ci atum 1434 ci gàddàygi, ginàw gi ci béssup 9 Octobr 2013 teppook 4 ci wérup ajj bi ci atum 1434 ci gàddàygi lañ koka déf yilimàne ci julli juroomyi.

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 6

  Mi ngi juddoo Makka ci atum 1395 ci gàddày gi; fala dooré jàŋŋ ba am bak. Amna majestér ci atum 1422 ci gàaddày gi ci fikh ci universitém Ummul Xurà. Amna itam doctoorà ci fikh ci atum 1429 ci gàddày gi ci universiép Madiina. Jàŋŋaléna fikh bu kawé fa Kàbaga, Ustàs la buy wuutu ci universitép Tàif. Yilimàn la ak xutbakat ci jumaay Al-Amiira Nawf ci Al-Aziiziyya bi ci Makka ak universitép Ibn baaz. Fal na ñuko yilimànu Makka béssup dibér 12-09-1434 ci gàddày gi.

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

  Jânggkate la bou goumba askanô maroc, dagne koy méllal né sakh môy serignou jânggkate yi. Mi ngui joudd thi atoum 1964.

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

  Mi ngui jouddô Libye, mi ,gui jeul gnârèlou palass bi thi jonganetèp Al-Khourane biy am Dubay

 • Kiko tâlif, Limou mbiryi : 1

  Wâ Yémène la, mi ngui jângg Al-khourane thi joumây Oussama Ibn Zayd, jângg kham-kham thi Mahad Nour. Fi gnou tôll mi ngui jângg thi uniniversitèp bi mâth thi kham-khamou Téknolozi thi kapitalou Yémène di Sanâ

Sap xalàt lu ñu saxalla