Tèkhanetal you ajou thi kham-kham

Diglé lu bàx téré lu bone

Lislàm dafa ñëw ngir sàmm joroomi mbir: diné, bakkén, xél, alal ak njaboot. Kàràngé mi ngi am ci wattu juroom yooyu. Té ni mbootàyu lislàm nimu tëddé dafay waral lahénté biir ak dimmbalaneté ci wattu kàràngé googu cila aju. Té bépp jullit kénn la ci ñiy wattu lislàm luy waral ci moom muy taxaw ci liko war ci mbookki jullitam. Mu bookk nak ci mbootàyi yi taxaw ci jamono yi mbootàyup diglé lu bàx téré lu bone. Té Diglé lu bàx téré lu bone ci toob yi gëna màgg di itam ligéy wu màgg wu Yonnénte ak ñu bàx ñi daan taxawé ndax lici nekk ci ngënél, ak yiw gu dajal, ak njariñu àdduna ak allàxira. Wayé bàyyiko dafay waral nén gëna fulu, yàxx tassàroo, ak moy gi inndi mérum Yàlla note, di waral mbugalam Yàlla ci ñëpp. Fiinak dajalé nañu fi yuy léral àtté yu ci jëm.

Limou mbiryi: 3

Kheut wi : 1 - Dalé thi : 1
Sap xalàt lu ñu saxalla